Môy Cheikh Yahya Ahmad Mouhammad Al-Halily, jouddô deukkou halila thi Yémène thi atoum 1372 thi gâddây gui tôllôk 1952. Mi ngui dôré thi jotâyoup njânggoup Al-khourane thi joumâ bou mak bithi capitâlbi dâldi môkkal thi atou 1962. Ginnâw gui mou jângg jourôm gnâri jânggine yi thi ay borôm kham-kham you....
Jânggkate bou Kouwète
Mi ngui jouddô Bagdad thi atoum 1953, génné thi universitèp Bagdad thi Facultèp Droit ak polotik thi atoum 1975, mou nékkône ki jîtou. Ginâw gui ministère biy saytou mbiri tougeul jeulko thi atoum 1977. Wayé mou tokhou thi liguèye bôbou, dâldi sôbou thi jângg ak jânggalé Al-Khourâne ba amthip ap....
Jânggkate bou Arabi Saoudite
Mi ngui jouddou thi 19-04-1986 thi Âzamiyy thi Baghdad thi Irak. Nékkônna - Yalla nako Yalla yereum- kènne thi mbôtâyoup jânggkate alkhourâne yi thi Irâk, bôkkna thi ay jongânté you bari, mi ngui fâtou thi 26-05-2007 thi jâmârlôk soldâroup amérik yi. Yalla nako Yalla bôlé thi gnimou nânggoul sène dé....
Môy Ahmad dômou Mouhammad dômou Abdallah dômou Mouîd AlHawwâchî. Yilimâne la ak khoutbakate thi joumây thi deukk bou toudd khamîss mouchayte thi beutt saloumou arabi sawdite. Mi ngui jouddou thi deukk bou toudd ahad rafîdah thi atoum 1374 thi gâddây gui.
Mi ngui jouddou thi atoum 1982 thi soudan, mi ngui am dipolômou jâng Alkhourâne thi jânggkate yi nekk Azhar thi septembar atoum 2009.
Môye Cheikh mahmoud Ahmad Abdoul hakam, Mi ngui jouddou bèss bou njeukk thi féviryé thi atou 1915 thi deukkoup Karnak bou sîwbi té bôtou thi centar Abou Tichte thi provinsoup Qanâl Arîf thi saidou égipte, bi mouy am foukki ate la môkkal Alkhourâne thip dâra mouné thi kognam guinnâw gui....
Jânggkate bou égipte
Môy Mouhammad dômou Rachâd dômou Abdous Salâm dômou Abdour Rahmâne Ach-charîf, mi ngui jouddô deukk bou gnouy wakh Al- Khalîl thi Palestîne atoum 1925 thi atoum toubap, mouy kènn thi jânggkatou Al-Khourâne yi sîw thi addinabi, môy jânggalékatoup jâkka Al-Aqsâ bou barkèl bi agitam jâklâp Al-Ibrâhîmî yi nèkk thi Al-Khalîl.Guinnâw....