×
alouthaymin (di ab brom xamxam boumak) mko def thi fêtou Noël (moy fêt gi nasran yiy def thi gouddig 24 ak bisoub 25 décembre.

    بسم الله الرحمن الرحيم

    Fatwa bi chekh mouhammad ibnou salih alouthaymin (di ab brom xamxam boumak) mko def thi fêtou Noël (moy fêt gi nasran yiy def thi gouddig 24 ak bisoub 25 décembre.

    Dangko ladie lan moy atteb ndokkel yefaryi thi fêtou Noël? Ak ndaka lagnouy def bode gnom gno gnou thi dnokkel? Ak ndakh dana dagan gnouy dem fangiy defe fêtou Noëlbi? Ak dnakh ko khamne dafa def bent thi yi ngou wakh te limou thi dioublou moy rafetal ab digante wala mou defko gir bagne kouko mere lan moy ab attem? Ak ndakh dana dagan gnou dilen toppando thi fêtou thi wakhtouw fêtgii ?

    Chekhbi tontou moune:

    Ndokkel yefaryi thi fêtou Noëlbi ak benen fêt boumou mana don thi sen fêti dineyi lou aram la, te mbolem brom xamxamyi deupponagnthi. Ibnou khayyim (ab brom xamxam boumagla) toukhalnako thi terem bi toud (attey yefar yiy dounde thi bir dioullityi), mom ibnou khayyim moune: ((ndokkel yefaryi thi yiy mandargal sen dine lou aram la thi wakhi mbolem brom xamxamyi, loumelne mouleni ndokkel thi sen fêtyi wala thi sen korgi, mounan len dewentilen, wala lounimel.

    Kiy def li defna lou aram, limou def migimelne kouy ndokkel yefarbi thi soudiood bimiy soudiodal Croix bi, limou def sakh mogeuna reuy bakkar thi kouy ndokkel kouy nan sangara wala kouy ray nit wala kouy ngalo walla youni mel.

    Te ngou bari ngi sen dine diaraloul dara dagniy tabbi thi bakkar bi, te doungou kham ngawayou lingou def.

    Kou ndokkel ken thi ak moy yall wala ab bida wala ak kefar defna louka mana dioural meroum yalla)).

    Ibnou outhiaymin moune: ndokkel yefaryi thi sen fêti dineyi litakh mou aram te graw ba ague thi lii ibnou khayyim wakh modine ndokkel lent hi sen fêtyi day wanene dagay sakhal kefar gingou nek,day wane ne yit geuramal galenko, donte sakh guerama loko sabope, te day aram thi ab dioullit mouy greum louy mandar gal ak kefar, wala mou thiay ndokkel kene, ndakhe yalla geuramoul lolou, yalla nena; ((dou geuramal diamamyi ak kefar)), moune wat ((geuramal nalen lislaam moudon sen dine)).

    Loloo takh dilin ndokkel this en fêt yoyou dafa aram, mokham dagno bookkak yaw ab leugeyou kay wala deet.

    Ngom yefaryi mem bougn gnou dee ndokkel thi sougniy fêt ngon dougnou len ndkkel gnom thi seni fêt, ndakh sen fêt yoyou dou sougnouy fêt ngoun, te ay fêt la you yalla greumoul, ndakh ay bidda la yougnou fent thi sen dine, wala sakh mouy lou sakh thia sen dine waye lislam bamou ngawe la folli sen dine yeeppe, yaalla nena: ((kep kou top benen dine boudoul islam disoukoko naggoul te allakhira thia gnay perte lay book)).

    Doudagan mouke ngou lendi wouyou bougne gnou wowee thi sen fêt yoyou, ndakh lolou moo geuna aram ndokkel len thia,ne bookkok gnom lay don.

    Day aram thi ab dioullit mouy nourou nouroulou ak yefaryi thi di amal ay fêt thi bisyiko yefaryi di amal, wala mouthiy diokhe ay cadeaux, wala ay gateaux, walla mouthiy sedale aw ngam, walla mou thiy banga leugueyi, ndakh yonnen tebi (yalla nako yalla dolli ay khewal) nena: kou nourou nouroulou ay gay thi ngom gay book.

    Ibnou taymiya (ab brom xamxam la boumak) dane: ((nourog gnom thi sene fêt dafay waral gnom gnouy beeg thi lignou nek thi ak neen.))

    Ibnou ousaymin moune koudef dara thi yii mou tddon legi defna bakkar, mokham dako def guir bagn kouko mere wala lenen loutakh mou defko, ndakh lolou day doug thi bayyi santaney yallayi guir wout gramal kenen, teyit day takh yefar di guena am dole, di ndamou this en dine.