×
Islaam DIINEY CET la AK XEL AK TEXE

Islaam

DIINEY CET la AK XEL AK TEXE

Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm képp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira laay tàmbalee.

NDAX LAAJ NGA SA BOOPP ?:

Kan moo bind asamaan ak suuf ak la ca nekk ci ay mbindéef yu màgg ? Ana kan moo defar nosiinu àdduna wu jekk wuñu xarañe wii lool ?

Naka la àdduna bu màgg bii man a nonewoo ci ay tëraliinam yi koy tënk tënk gu sew ak lu jamono yàgg- yàgg?

NDAX ÀDDUNA BII MOO BIND BOOPAM ? WALLA DAFA AM TE BÀYYiKOOWUL CI LENN? WALLA daa jekki rekk am?

KAN MOO LA BIND?

Kan moo Tëral tëraliina wu yéeme wii ci yiy doxaliin saw yaram ak yaramu yiy dundu?

KENN DU NANGGU ÑU NE KO KËRGII DAFA AM TE KENN TABAXU KO! WALLA ñune ko lu amul moo amal kër gile! Naka la lenn ci nit ñi di gëmee ne àdduna bii dafa am te kenn amalu ko? NAKA LA BOROOM XEL DI NANGOO ñu ne ko àdduna bu nosu bii dafa jekki rekk am noonu ?

WÓORNA NE AM NA BUUR BU MÀGG MOOM MOO BIND TE TEYDOXAL ÀDDUNA BI AK LI CI BIIRAM, TE MOOY YALLA MU SELL MI TE KAWE.

BOROOM BU SELL BI YÓNNEE NA NU AY YÓNENT , WÀCCE CI ÑOOM AY TÉERÉ (NDEEY), BI CI MUJJ MUY ALXURAAN JU TEDD JI MU WÀCCE CI MUHAMMAT MIY YONENTE BI MUJJ, CI BIIR TÉERE YOOYU AK YONENT YOOYU:

LANU XAMALE BOPPAM AK AY MELOKAANAM AK ÀQAM CI NUN, MU LEERAL ÀQ JI NU KO AMEEL.

MU XAMAL NU NE MOOM MOOY BOROOM BI BIND MBINDÉEF YI, TE AJI-DUND LA DU FAATU, TE MBINDÉEF YÉPP MOO LEEN TËYYEEL BOPPAM TE MOOY KILEEN NOT MOOY KI YORE SÉEN I BIR.

MU XAMAL NU NE BOKKNA CI AY MELOKAANAM PEEG GU MU PEEG LÉPP CI XAM-XAM BA,TE MOOM AJI-DÉGG LA AJI-GIS LA AMUL DARA LU KO UMPU CI ASAMAAN AK SUUF.

BOROOM BI MOOY KIY DUNDU DUNDU GU SAX MOOY KIY TAXAWU LÉPP, MOOY KI NGA XAM NE DUNDUG BÉPP MBINDÉEF CI MOOM LA BÀYYIKOO.﴿اللَّهُ لا إِلَهَ إِلَّا هُوَ الْحَيُّ الْقَيُّومُ لا تَأْخُذُهُ سِنَةٌ وَلا نَوْمٌ لَهُ مَا فِي السَّمَوَاتِ وَمَا فِي الأَرْضِ مَنْ ذَا الَّذِي يَشْفَعُ عِنْدَهُ إِلَّا بِإِذْنِهِ يَعْلَمُ مَا بَيْنَ أَيْدِيهِمْ وَمَا خَلْفَهُمْ وَلا يُحِيطُونَ بِشَيْءٍ مِنْ عِلْمِهِ إِلَّا بِمَا شَاءَ وَسِعَ كُرْسِيُّهُ السَّمَوَاتِ وَالأَرْضَ وَلا يَئُودُهُ حِفْظُهُمَا وَهُوَ الْعَلِيُّ الْعَظِيمُ﴾ {YALLA MOOY BOROOM TUR WII DI ALLAH , AMUL KENN KUÑU WAR A JAAMU CI DËGG KUDUL MOOM, MOOY BOROOM DUNDU GU SAX, MOOY KIY TAXAWU LEPP, DU GËMMEENTU DU NELAW, MOOY BOROOM LI CI ASAMAN YI AK SUUF SI, ANA KAN MOOY RAMMU FA MOOM CI LUDUL NDIGALAM? XAM NA LI CI SEEN BIIR AK LI CI SEEN GINAAW, DU ÑU PEEG DARA CI XAM-XAMAM NDARE LU KO SOOB, TOOGOM BA ËPP NA ASAMAN YI AK SUUF TE WATTU LEEN DU KO DIISAL, MOOM REK MOOY KI KAWE TE MOOM REK MOOY KI MAAGG. }[AL BAXARA: 255].

MU XAMAL ÑU NE MOOY BOROOM BI MELOWOO MELOKAAN YU MAT YI, MU WËRSAGAL NU XEL AK YËG-YËG BUY MANA SEETLU KEEMAANI MBINDEEFAM YI AK KÀTTANAM MUY LUÑUY WAN MÀGGAAYAM AK DOOLEEM AK MATUG MELOKAANAM YI MU JËMBAT CI NUN ( SET) GUNUY WAN NE DU KUY MELOWOO MELOKAAN YU MÀNKI.

MU XAMAL NU NE MOOY BOROOM BI TIIM ASAMANAM YI TE DUGUL CI BIIR DÉND BI TE DÉND BI IT WÀCCUL CI MOOM.

MU XAMAL NU NE DAFA WAR CI NUN NU JÉBBALUL KO NDAX MOO NU BIND MOO BIND ÀDDUNA BI TE MOOKOOY DOXAL.

AJI-BIND JI MOOY BOROOM MELOKAAN YU MÀGG YI, MELOWOO WUL AG ÑÀKK WALLA AG YÉES, TE MOOM BOROOM BI DU FÀTTE TE DU NELAW TE DU LEKK; TE AMUL DOOM, BÉPP YAX MBIND MU AM LU WUUTEEG MÀGGAAYU BOROOM BI BOOKKUL CI LI WER JUGE CI YONENT YI -YAL NA LEEN YALLA DOLLI JÀMM.

YALLA MU KAWE MI WAX NA CI ALXURAN:﴿قُلۡ هُوَ ٱللَّهُ أَحَدٌ * {NEEL LIY MBIR TEY MBIR MOOY YALLA KENN LA*ٱللَّهُ ٱلصَّمَدُ * (YALLA MOOY KI ÑUY JUBLU CI JÉPP AAJO*لَمۡ یَلِدۡ وَلَمۡ یُولَدۡ * JURUL KENN TE KENN JURU KO*وَلَمۡ یَكُن لَّهُۥ كُفُوًا أَحَدُۢ﴾ TE AMUL KENN KUY NAWLEEM}[LIXLAAS :1-4]

BOO GËMEE BOROOM BI NDAX DA NGA XALAAT BENN BIS CI LI TAX ÑU BIND LA ? AK LAN LA YALLA NAMM CI NUN? AK LAN MOOY JUBLUWAAYU SUNUG NEKK FI ?

NDAX XEL NANGU NA YALLA BIND NU BA NOOPPI BËRGËL NU? WALLA NDAX XEL NANGU NA YALLA BIND MBINDEEF YÉPP CI LUDUL BENN NAMMEEL?

CA DËGG-DËGG BOROOM BU MÀGG BI XAMAL NA NU JUBLUWAAY BI TAX MU BIND NU, TE MOOY JAAMU KO MOOM DONĞ, AK LI MU NAMM CI NUN! MU XAMAL NU IT NE MOOY KI YELLO JAAMU, MU LEERALAL NU JAARE KO CI YÓNENTE YI NAKA LANU KOY JAAMOO ? NAKA LANU KOY JEGEE CI DEF AY NDIGALAM BÀYYI AY TEREEM ? NAKA LANUY AME NGËRËMAM ? NAKA LA NUY MOYTOO MBUGËLAM? MU XAMAL NU FA NUY MUJJ GANNAAW DEE!!?

MU XAMAL NU NE DUNDU GII NATTU KESE LA, WAAYE DUNDU DËGG-DËGG GU MAT SËKK MOOY GU ALLAAXIRA GANNAAW DEE!!.

MU XAMAL NU IT NE: KU JAAMU YÀLLA KOM NI MU LA KO DIGALEE, BÀYYI LI MU KO TERE; DAY AM DUNDU GU TEEY CI ÀDDUNA, AM XÉEWAL GU SAX CA ALLAAXIRA, WAAYE KU KO MOY WEDDI KO DANA AM AG TEXEEDI CI ÀDDUNA, AK MBUGAL MU SAX DÀKK CA ALLAAXIRA.

TE IT NU XAM NE MANU NOO WÉY CI DUNDU GII TE KENN DU DAJEEK PAYUG LAMU JËF CIW YIW MBAA AB SAFAAN, TE DEESUL MBUGAL TOOÑKAT Yi, DEESUL FAY IT ÑIDOON RAFETAL.

SUNU BOROOM XAMAL NA NU NE: AM NGËRËMAM AK MUCC CI MBUGALAM DU AME CI LUDUL DUGG CI DIINEY LISLAAM, NGA XAM NE MOOY JÉBBALUL YALLA, AK JAAMU KO MOOM DONG, WOMMATUL KO CI TOPP KO, AK NANGU SARIIHA, YÀLLA XIBAARE NANU NE DU NANGU JENN DIINE JUDUL LISLAAM, YÀLLA NEE NA:(وَمَن يَبۡتَغِ غَيۡرَ ٱلۡإِسۡلَٰمِ دِينا فَلَن يُقۡبَلَ مِنۡهُ وَهُوَ فِي ٱلۡأٓخِرَةِ مِنَ ٱلۡخَٰسِرِينَ) (KU SÀKKU JENEEN DIINE JUDUL LISLAAM; DEESU KO KO NANGUL TE MOOM ËLLËG ALLAAXIRA DAY BOKK CA WAY-SOOY ÑA )[AALI IMRAAN: 85].

KU XOOL LI ËPP CI LI NIT Ñi DI JAAMU TAY; DANA GIS KUY JAAMU NIT AK KUY JAAMU XËRËM AK KUY DIAAMU BIDDIW, TE NIT KU AM XEL WARUL A JAAMU KUDUL YÀLLA BOROOM MELOKAAN YU MAT YI! NAKALAY JAAMOO MBINDEEF MU MEL NI MOOM WALLA MU YÉES KO! KIÑU WARA JAAMU DU MBINDEEF DU XËRAM DU GARAB DU BAAYIMA !

DIINE YI ÑUY JAAMOO YÀLLA TAY BUDUL LISLAAM REKK YÀLLA DU KO NANGGU, NDAX ÑOOM AY DIINE LAÑU YU BÀYYIKOO CI MBINDÉEF YI, WALLA SAX DIINE YOO XAM NE CA YÀLLA LA BÀYYIKOO WAAYE LOXOB DOOMU AADAMA SOPPI NA KO, BUDEE LISLAAM NAK MOOY DIINEY YÀLLA JI NGA XAM NE DU SOOPEEKU, TA TÉEREEM BI MOOY ALXURAN DI TÉERE BUÑU SÀMM NIKI NI KO YÀLLA WÀCCEE TE MOO NGI CI LOXOY JULLIT YI BA TAY, CI LÀKK WI MU WÀCCE WOON CI YONENT BU MUJJ BI.

BOKK NA CI COSAANI LISLAAM YI NGA GËM MBOOLEEM YONENT YI YÀLLA YÓNNI TE ÑOOM ÑÉPP AY MBINDEEF LAÑU, YÀLLA MOO LEEN DËGËRALE AY MANDARGA AKI KÉEMAAN, MU YÓNNI LEEN NGIR ÑUY WOOTE CI JAAMU KO MOOM DONG TE BAÑKOO BOKKAALE.KI MUJJ CI YONENT YI MOOY MUHAMMAT -YAL NA KO YÀLLA DOLLI XÉEWAL AK MUCC- MU YÓNNI KO TËRËLINAM WU MUJJ WIY FOLLI MBOOLEEM TËRËLIN YI KO JIITU MU DËGËRALE KO AY KÉEMTAAN YU MÀGG, BA CA GËN A MÀGG MOOY ALXURAAN DI KÀDDUG YÀLLA BOROOM MBINDEEF YI, MUY TÉERE BI GËN A MÀGG BU MBINDEEF XAM, MUY LOTTLOO CI AY BAATAM AK UG NOSOOM AK LI MU LÀMBOO AK AY ÀTTEEM, NJUB GUY TAXA TEXE ÀDDUNA AK ALLAAXIRA CI LA NEKK, MU WÀCC KO CI LÀKKU ARAAB.

BARINA AY TEKTALI XEL AK YU XAM-XAM YUY SAXAL CI LU ÀNDUL AK SIKK-SÀKK NE ALXURAN JII MOOY KÀDDUG YALLA, TE MËNUL NEKK JËFI MBINDEEF.

BOKKNA CI COSAANI LISLAAM YI GËM MALAAKA YI , AK GËM BIS BU MUJJ BA, FA YALLA DI DEKKALE JAAM YI CI SEENI BÀMMEEL BISUB TAXAWAAY BA NGIR ATTE LEEN CI SEENI JËF, KU DEF LU BAAX TE FEKK MUY AJI-NGËM; DAY AM XÉEWAL GU SAX DÀKK CA ÀJJANA, WAAYE KU WEDDI BA NOPPI DEF LU ÑAAW; DANA AM MBUGAL MU MÀGG CA SAWARA, BOKKNA CI COSAANI LISLAAM NGA GËM LI YÀLLA DOGAL MOO XAM AW YIW LA MOO XAM AB SAFAAN LA.

DIINEY LISLAAM MOOY YOON WU MAT SËKK NGIR DUNDU, MOOY DËPPOO AK NI YÀLLA BINDEE NIT, MOO DËPPOO AK UM XEL, TE BAKKAN YI MUCC-AYIB YÉPP DAÑUKOY NANGU, YÀLLA MU MÀGG MI MOOKO TËRËLAL MBINDEEF YI, MOOY DIINEY YIW AK TEXE NGIR NIT ÑÉPP CI ÀDDUNA AK CI ALLAAXIRA, DU RÀÑETLE XEET Ci KAW XEET, WALLA MELOKAAN CI WENEEN MELOKAAN, NIT ÑÉPP ÑOO CI YAM, KENN DU RÀÑEEKU CI KAW KENN LUDUL CI JËFAM JU BAAX!.

Yàlla mu kawe mi nee na:(مَنۡ عَمِلَ صَٰلِحا مِّن ذَكَرٍ أَوۡ أُنثَىٰ وَهُوَ مُؤۡمِن فَلَنُحۡيِيَنَّهُۥ حَيَوٰة طَيِّبَة وَلَنَجۡزِيَنَّهُمۡ أَجۡرَهُم بِأَحۡسَنِ مَا كَانُواْ يَعۡمَلُونَ) (KU DEF LU BAAX MOO XAM GÓOR LA WALLA JIGÉEN TE MU DEF KO CIG NGËM; DANAÑU KO DUNDAL DUNDU GU TEEY, TE DAAÑUKO FAY PAY GU GËN A TAARU LAMUDOON DEF)[ANNAHLU :97]

BOKKNA CI LI YÀLLAY FEDDALI CI TÉEREEM BU TEDD BI WARUG GËM YÀLLA MUY SA BOROOM DI KI NGAY JAAMU, WAAYE GËM LISLAAM MUY SA DIINE, GËM MUHAMMAT MUY SA YONENT. DUGG CI LISLAAM WARTEEF LA NIT AMU CI LUMUY TÀNN; ËLLËG BIS-PENC FOOFA LA REGLE AK PAY NEKK; KU GËM YÀLLA NGËM GU DËGGU; DANA AM TEXE GU MÀGG. WAAYE KU WEDDI YÀLLA ;DANA SOOY SOOY GU FÉS

Yàlla mu kawe mi nee na:(... وَمَن يُطِعِ ٱللَّهَ وَرَسُولَهُۥ يُدۡخِلۡهُ جَنَّٰت تَجۡرِي مِن تَحۡتِهَا ٱلۡأَنۡهَٰرُ خَٰلِدِينَ فِيهَاۚ وَذَٰلِكَ ٱلۡفَوۡزُ ٱلۡعَظِيمُ، (KU TOPP YÀLLA AK YONENT BI; YÀLLA DANA KO DUGAL ÀJJANA YOO XAM NE AY DEXI XÉEWAL ÑOOY DAW CI SEEN SUUF ÑU SAX FA DÀKK, LOOLU MOOY TEXE GU MÀGG,وَمَن يَعۡصِ ٱللَّهَ وَرَسُولَهُۥ وَيَتَعَدَّ حُدُودَهُۥ يُدۡخِلۡهُ نَارًا خَٰلِدا فِيهَا وَلَهُۥ عَذَاب مُّهِين) {KU MOY YÀLLA AK YONENT BI JÉGGI AY DiGAM; DANA KO DUGAL SAFARA MU SAX FA TE DANA FA DAJEEK MBUGAL MUY TOROXALE).[ANNISA :13-14]

KU BËGG A DUGGU CI LISLAAM NA WAX : (MAA NGI SEEDE NE AMUL BENN BUUR BU ÑU WAR A JAAMU, JAAMU GA DI JARIÑ ÑÀKKA JAAMU GA DI LOR KU DUL YÀLLA, TE MAA NGI SEEDE NE MUHAMMAT YONENTEB YÀLLA LA.) XAM MAANA MI TE GËM KO ,CI LOOLU LAY NEKKE JULLIT; SU KO DEFEE MUY JÀNG LI DES CI DIINEEM NDÀNK NDÀNK NGIR MU MAN A TAXAWE LI YÀLLA WARAL CI MOOM..

Islaam

DIINEY CET la AK XEL AK TEXE

KAN MOO LA BIND?

NDAX XEL NANGU NA YALLA BIND NU BA NOOPPI BËRGËL NU? WALLA NDAX XEL NANGU NA YALLA BIND MBINDEEF YÉPP CI LUDUL BENN NAMMEEL?

TE IT NU XAM NE MANU NOO WÉY CI DUNDU GII TE KENN DU DAJEEK PAYUG LAMU JËF CIW YIW MBAA AB SAFAAN, TE DEESUL MBUGAL TOOÑKAT Yi, DEESUL FAY IT ÑIDOON RAFETAL.